Publishing Details
About This Podcast
Explore Statistics
Recent Episodes
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett bi mu ngi aju ci disóo ak Yàlla ci sa mbir yépp, moytu di jublu mayu Yàlla yi fàtte Aji-Maye ji, ak wéet.
Waxtaan ci bor
Ci waxtaan wii, da nu ciy leer dayo bi bor am ak diis bi mu diis, ngir fàttali sunu bopp, waaye fàttali sunu bokki jullit yi ngir ñu jàjju te moytu bor boodut fay.
Ban xam-xam mooy farata?
Ci waxtaan Wii, danu ciy indi tontu ci laaj bii: Ban xam-xam mooy farata ci nit ki? Ginnaaw Yonent bi SAW daa wax ne sàkku xam-xam farata la ci jullit bi, kon yey na lu ne xam ban/yan xam-xam la war…
Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj ñaar)
Waxtaan wii mu ngi aju ci Teggiini niti Yàlla yi ak sew-sew yi leen wuutale ak ñeneen ñi.
S1E1 Teggiini niti Yàlla yi (Xaaj bu njëkk bi)
Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
Njariñu Koor
Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
Moytu àq yi
Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo…
Tëj gi: Gàllaŋkoor yi
Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen…
Pensées et introspection
Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
Tegginu nitu Yàlla yi
Ci waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax).
Lan mooy gis Yàlla?
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ.
Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñ
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir da ciy wax ci xeetu tudd Yàlla yi am, rawatina bu làmmiñ bi nga xam ne kiy doog a sóobu ci lay tàmbalee. Ci mujj gi mu tënk ponku tassawuf yi mu jàpp ne ñoo ci gën a am…
Waxtaan ci tassawuf: Sikar ak xalam (zikru ak fikru)
Ci tomb yii, Imaam Dardiir da ciy wax ci solos jaamu Yàlla njël ak taxawaayu tudd Yàlla ci dundug aji-sóobu ji. Ñu doon yaari ponk yoo xam ne ki sóobu ci Yàlla da leen a war a fonk ngir jot ci…
Waxtaan ci 6i ponku tassawuf bi: Al-uzla (wéet)
Wéet daa bokk ci ponk yi tassawuf teg ngir nit ki sellal xolam. Jaxasoo ak nit yi lu bari ci lu dul farata dafay sabab ay ayibu xol. Moom la Imaam Dardir di leeral ci waxtaan wii ngir aji-sóobu ji…
Waxtaan ci ponku tasawuf yi: Sëriñ bu mat sëriñ
Ci dars bii, Imaam Dardiir dafay waxtaan ci ponku tassawuf yii di nangu ndogal ak wut sëriñ bu mat sëriñ. Ci ginnaaw gi mu misaal nu sëriñ bu mat sëriñ nu muy mel.
Ñaareelu- ak ñetteelu ponk tassawuf yi: Sant ak muñ
Ci biir fukki ponk tassawuf yi Imaam Dardiir indi ci téereem bi, waxtaan wii mu ngi aju ci lan lañuy tuddee sant Yàlla ci diine ak lan mooy muñ bi tax ñuy wax muñ.
Ponku tassawuf bu njëkk bi: Tuub
Tasawuf daa am ay ponk yoo xam ne nitu Yàlla yi dañu ko tëral ngir yombal aji-sóobi ji ngir mu jot ci sàkkuteefam. Ponk yooyu ñu ngi ko tënk ci fukk. Tay nag ponk bu njëkk bi lañuy waxtaane te mooy…
Waxtaan ci tasawuf: Ñaarelu Xaaj bi: Jikko yiy gàllaankoor nit ki ci yoonu Yàlla
Ci waxtaan wii, imaam Dardiir dafay waxtaane jikkoy xol yiy gàllankoor muriit bi ba du am ag jege Yàlla. Saalig bi (ki bëgg àgg ci Yalla) daa war a taqoo ak sikar ak jéem a dindi jikko yu ñaaw yépp…
Waxtaan ci tasawuf: Xaaj bu njëkk bi
Tasawuf: Dëgg la ne ñi réere tasawuf bari nañu lool ci jamono. Ñii dañu ko réere ndax ñàkk a ci tàbbi, ak xeeb doxalinu ñi ci nekk te di ci boole lu ci bokkul. Am ñu ci nekk ba noppi réere mbir ndax…
Njariñu sàmm sa waxtu
Waxtu daa doon lu gànjaru lool te mat a moytu a sanq. Jépp noyyi, sépp simili, wépp waxtu wurus la wow nit ki man na ci fàggu lu ko texeel ëllëg. Saggane ko nag ak di ko jeexal ci neen rëccu lay…
Frequently Asked Questions
Bëgg a Baax podcast has published 26 episodes since February 2024, covering topics in Religion & Spirituality.
Bëgg a Baax podcast is currently highly active with new episodes every 2 months. Average episode length is 26m.
Similar Podcasts
The Bible in a Year (with Fr. Mike Schmitz)
Ascension
1,714 episodes
Relatable with Allie Beth Stuckey
Blaze Podcast Network
1,427 episodes
Unashamed with the Robertson Family
The Robertson Family
1,355 episodes
Joel Osteen Podcast
Joel Osteen, SiriusXM
2,433 episodes
BibleProject
BibleProject Podcast
527 episodes
Timothy Keller Sermons Podcast by Gospel in Life
Tim Keller
100 episodes